📌 2. Sëriñ bi mas naa laaj ay mag achtaatan nu ngeen ko xamee ? Ñu wax ko la ñu ca xam, mu ni jublu wu ci loo lu, ni léen achtaatan, chiin su tooy soo su mooy mbir mi, chiin su tooy soo su lu muy tollool ci li mu abajada ? Ñu ni ko junni la ñu ci xam, mu ni léen bis pénc lay xamle di ko misaal. Bis pénc boo bu ngeen di dégg nga xam ni bu dikkee lu Yàlla sunu Boroom bind di na ko teewee, nit ak jinne dara du ko wuute. Ay kuréel la ñu koy def bu ñu ca yeggee, bu ci ne junni lay doon du ëpp du yées, junni bu ne kenn moo cay am set gu tollu ni jóg dem àjjana te jaarul sawara kon góorgóorlu baax na lool. 🔔
📌 Lenn ci ay Jangale Seex Axmadu Bàmba Xaadimu Rasuul (500)
1. Am na bis Sëriñ bi tijji mbooloo mi tàmbalee ñew benn-benn mu xawa mel ni ku soppeeku ni léen : dem léen ba ngoon, ca ngoon ga mu woo léen ni léen xam ngeen sikku Sëriñ, ñu ni ko ku nu ci dimbali nu jël, mu ni léen tàngoor ak wex ak naqari dereet du ñu sikku Sëriñ xanaa gisu léen xal, man naa xey ni futeet ab dëkk ba dara du fa des waaye bu ngoon jotee ba laa kenn a fatu wuti ko, njariñ laa ko waral. 🔔